Kàttanu n-neel (Puissances)
Wax ci kàttanu n-neel
Na $b$ nekk bènn limmum fukkèl bu ñuy xaymaa, te $n$ nekk bènn limmum lëmm bu ëpp wala mu tollook $2$. Dèes na tuddee kàttanu $n$–neel bu bènn fukkeel $b$, jeexitali fŭllantèk $n$ ëmbeef (facteurs) yu tolloo yëpp ak $b$.
Binddu kàttanu n-neel
Lòlu da ñu koy binndee:
$$b^n=\underbrace{b \times b \times \ldots \times b}_{n \text{ ëmbeef yu tollook } b}$$
Tërëlu kàttanu n-neel
$b^n$ bènn kàttanu limm bii di $b$ la.
$n$ mooy maasukow (exposant) bu kàttan wòwu.
$b^n$ ñu ngi koy jangee $b$ maasukow $n$ wala $b$ ci kàttani $n$.
Ay jëfandikoo yu njëkk
Ñu ngi nangu ne:
- $b^1=b$
- $b^0=1$ (bu $b \neq 0$)
- $1^n=1$
- $0^n=0$
Ay jëfandikoo yu kàttanu n-neel
Kàttanu n-neel bu ñaari fukkeel
Su $a$ ak $b$ nekkee ñaari fukkeel te $n$ nekk bènn limmum lëmm bu ëpp wala mu tollook $2$, da ñuy am:
$$(a \times b)^n=a^n \times b^n$$
Ñaari kàttanu n-neel yu am benn fukkeel
Su $x$ nekkee bènn fukkeel bu ñuy xaymaa te $n$ ak $p$ nekkee ay limmum lëmm, da ñuy am:
$$x^n \times x^p=x^{n+p}$$
Kàttanu n-neel bu kàttanu n-neel
Su $a$ nekkee bènn fukkeel, $m$ ak $n$ di ñaari limmum lëmm yu ëpp wala ñu $2$, da ñuy am:
$$\left(a^n\right)^m=a^{n \times m}$$