I. Yemale yu melni $ax+b=0$
$(a$ ak $b$ ay limum tjit la ñu)
Ci yemale bii, am na ñetti xeetu sottal:
- Su $a=0$ ak $b=0$ kon bépp limm ab sottal la.
$S=\{R\}$ - Su $a \neq 0$ kon $x=\dfrac{-b}{a}$.
$S=\left\{\dfrac{-b}{a}\right\}$ - Su $a=0$ ak $b \neq 0$ kon amul sottal.
$S=\{\varnothing\}$
II. Yemale yu melni $(ax+b)(cx+d)=0$
Da ñuy jëfëndikoo jagle jii: $A \times B=0$ mu ngi firi ne $A=0$ wala $B=0$.
Da ngay sottali: $ax+b=0$ wala $cx+d=0$
III. Yemale yu melni $\dfrac{a}{x}=0$ ak $\dfrac{a}{x}=\dfrac{b}{c}$
Da ñuy jëfëndikoo jagle jii: $\dfrac{a}{b}=\dfrac{c}{d}$ mu ngi firi ne $a \times d=b \times c$.