I. Toxal yi
Tekki
Na ñu am $3$ tomb $\rm A$, $\rm B$ ak $\rm P$ yu bokkul te $t$ di toxal biy soppali tomb bii di $\rm A$ ci $\rm B$.
- Su tomb bii di $\rm P$ bokkul ci rëdd wii di $\rm (AB)$, misaaluk (image) tomb bii di $\rm P$ ci toxal wii di $t$ mooy tomb $\rm P'$ biy tax $\rm ABP'P$ nekk bènn wet-yu-làŋ.
- Su tomb bii di $\rm P$ bokkee ci rëddd wii di $\rm (A B)$, misaaluk tomb bii di $\rm P$ ci toxal wii di $t$ mooy tomb $\mathrm{P}^{\prime}$ biy tax dogit yii di $\left[\mathrm{AP}^{\prime}\right]$ ak $[\mathrm{BP}]$ bokk bènn digg.
Jagleb toxal yi
Ci bènn toxal, misaalu bènn dogit ab dogit la bu wetlàŋ ak moom te tollook moom guddaay. Ci bènn toxal, misaalu bènn rëdd ab rëdd la bu wetlàŋ ak moom. Ci bènn toxal, misaalu bènn xaaju rëdd ab xaaju rëdd la bu wetlàŋ ak moom te bokkak moom jëmukaay. Ci bènn toxal, misaalu bènn mbege rëdd ab mbege la bu tollook momm cn la bu tollook momm ceeñeer ; diggi nataal bi mooy misaaluk diggi mbege mu njëkk mi.
Ab toxal da fay denc raŋale yi, guddaay yi, angal yi, yaatuwaay yi, wetlàŋite gi ak jub-dogoo gi.
II. Jëmu yi
Raññalekuk bènn jëmu
Jëmu bii di $\rm\overrightarrow{A B}$ li koy raññale mooy :
- Jubluwaayam te mooy rëdd wii di $\rm (AB)$.
- Jëmukaayam te mooy bu xaaju rëdd wii di $\rm [AB)$.
- Guddaay te mooy bu dogit wii di $\rm [AB]$.
Li koy mandargaal bènn fètt la.
Jëmu yu tolloo ak jëmu yu feewëloo
- $2$ jëmu da ñoo tolloo bu fekkee ñoo bokk bènn jubluwaaay, bènn jëmukaay ak bènn guddaay.
$\overrightarrow{\mathrm{AB}}=\overrightarrow{\mathrm{CD}}$ - $2$ jëmu da ñoo feewëloo bu fekkee ñoo bokk bènn jubluwaaay, bènn gudday waaye seen jëmukaay yi feewëloo.
$\overrightarrow{\mathrm{AB}}$ ak $\overrightarrow{\mathrm{BA}}$ da ñoo feewëloo.
Jëmu ak wet-yu-làŋ
- Su $\rm A B C D$ nekkee ab wet-yu-làŋ, da ñuy am $\rm\overrightarrow{A B}=\overrightarrow{D C}$.
- Su $\overrightarrow{\mathrm{AB}}=\overrightarrow{\mathrm{DC}}$ te tomb yii di $\mathrm{A}$, $\mathrm{B}$, $\mathrm{C}$ ak $\mathrm{D}$ raŋale wu ñu, kon ñeentikoñ bii di $\rm A B C D$ ab wet-yu-làŋ la.
Digguk bènn dogit ak jëmu
- Su bènn tomb $\rm I$ nekkee digguk bènn dogit $[\mathrm{AB}]$ kon $\overrightarrow{\mathrm{AI}} = \overrightarrow{\mathrm{IB}}$.
- Su $3$ tomb $\rm A$, $\rm I$, $\rm B$ melee ni $\rm \overrightarrow{A I}=\overrightarrow{I B}$ kon $\rm I$ mooy digguk $\rm [A B]$.