I. Xammee aki mbindin

Ab limum tojit mooy bènn lim bu ñu mana binndee ci anam bii di $\dfrac{a}{b}$ mu andak $a$ ak $b$ di ay limm yu jokkaloo. Mbooloom limum tojit yi dèes na ko woowee $\rm Q$.

Jëfandikoo yu njëkk

  • $\dfrac{a}{b}=\dfrac{a \times k}{b \times k}$
  • $\dfrac{a}{b}=\dfrac{a \div k}{b \div k}$
  • $\dfrac{-a}{b}=\dfrac{a}{-b}=-\dfrac{a}{b}$

II. Sëfuk xayma yi ci $\mathbf{Q}$

Soo jëlee ay limum tojit yumu mana doon $a$   $b$   $c$ ak $d$ :

Yokk ak wàññi

  • $\dfrac{a}{b}+\dfrac{c}{b}=\dfrac{a+c}{b}$   $\dfrac{a}{b}-\dfrac{c}{b}=\dfrac{a-c}{b}$ ci lu andak $b \neq 0$
  • $\dfrac{a}{b}+\dfrac{c}{d}=\dfrac{a \times d+c \times b}{b \times d}$   $\dfrac{a}{b}-\dfrac{c}{d}=\dfrac{a \times d-c \times d}{b \times d}$ ci lu andak $b \neq 0$ et $d \neq 0$

Ñaari ak deel

  • $\dfrac{a}{b} \times \dfrac{c}{d}=\dfrac{a \times c}{b \times d}$
  • $\dfrac{a}{b} \div \dfrac{c}{d}=\dfrac{a}{b} \times \dfrac{d}{c}$ ci lu andak $b \neq 0$   $c \neq 0$ te $d \neq 0$

III. Njëgg wu matt

Na $a$ nekk bènn limum tojit :

$|a|=a$ su a ëppee tus.

$|a|=-a$ su a yèesee tus.

Jëfandikoo yu njëgg wu matt

Soo jëlee ay limum tojit yumu mana doon $a$ ak $b$ :

  • $|a \times b|=|a| \times |b|$
  • $\left|\dfrac{a}{b}\right|=\dfrac{|a|}{|b|}$
  • $|a|=|b|$ mu ngi tekki ne $a=b$ wala $a=-b$

IV. Mengale

Soo jëlee ay limum tojit yumu mana doon $a$   $b$   $c$ ak $d$ :

Mengale yu ñaari

  • $\dfrac{a}{b}=\dfrac{c}{d}$ mu ngi tekki ne $a \times d=b \times c$ ci lu andak $b \neq 0$ ak $d \neq 0$
  • Su $a=b$ kon $a+c=b+c$ te $a-c=b-c$
  • Su $a=b$ kon $a \times c=b \times c$ te $a \div c=b \div c$

Mengale yu njëkk

  • Su $a \leqslant b$ kon $a+c \leqslant b+c$ te $a-c \leqslant b-c$
  • Su $a \leqslant b$ te $c$ ëpp tus, kon $a \times c \leqslant b \times c$ te $a \div c \leqslant b \div c$
  • Su $a \leqslant b$ te $c$ yèes tus, kon $a \times c>b \times c$ te $a \div c > b \div c$

RÉSUMÉ