I. Yokkalanteek ay jëmu

A, B et C ñetti tomb la ñuy ci maasale gi. Dèes na tuddee ndajaleek jëmu yii di AB ak BC, jëmu jii di AC.

Da ñuy binnd : AB+BC=AC.

Yemoo gògu ñu ngi koy tuddee yemook Shaal (Chasles).

Jëmu yu feewëloo

A, B ak C ñetti tomb la ñuy ci maasale gi. Da ñuy am : AB+BA=AA=0

Da ñuy naan AB ak BA ay jëmu yu feewëloo la ñu. Ñu daal di binnd BA=AB

II. Fŭllanteek bènn jëmu ci bènn limm

Xammee

Dèes na tudddee fŭllanteek jëmu bu dul tus bii di AB ci limum dëgg wii di k, jëmu jii di MN.

  • (AB) // (MN) ñoo bokk jubluwaay 
  • AB ak MN :
    • ñoo bokk jëmukaay su fekkee ne k>0 
    • seeniy jëmukaay yi da ñoo feewëloo su fekkee ne k<0
  • MN=|k|AB.
Ab seetlu
  • Fŭllanteek jëmuk tus gi ci bènn limum dëgg mooy jëmuk tus gi 
  • Fŭllanteek jëmu jii di AB ci 0 da fay nekk jëmuk tus gi 0 
  • Fŭllanteek jëmu jii di AB ci bènn limm k bu dul tus dèes na ko binndee : kAB.
Ay misaal

Jëmu yii di AB, 1.5AB ñoo bokk jubluwaay. AB ak 1,5AB ñoo bokk jëmukaay. AB et 3AB seeniy jëmukaay yi da ñoo feewëloo.

Ay jagle

A, B, C ak D ay tomb la ñu ci maasale gi. k ak h ay limum dëgg la ñu. Da ñuy am :

  • k(hAB)=(kh)AB.
  • kAB+kCD=k(AB+CD).
  • kAB+hAB=(k+h)AB.
  • 1AB=AB.

III. Jëmu yu bokk jubluwaay ak jëmu yu bokk rëdd (colinéaires)

Jëmu yu bokk jubluwaay

Ab jagle

A, B, C ak D ñeenti tombi maasale gi la ñu. Wax ne jëmu yii di AB ak CD ñoo bokk jubluwaay mu ngi firi ne mann ngaa gis bènn limm k bu dul tus tey tax ñu am : AB=kCD

Jëmu yu bokk rëdd

Xammee

Da ñuy naan ñaari jëmu ñoo bokk rëdd su fekkee ñoo bokk jubluwaay, wala su kènn si ñoom nekkee jëmuk tus gi.

Ab misaal

AB=3CD mu ngi junj ne AB ak CD ñoo bokk jubluwaay alorste konn AB ak CD ñoo bokk rëdd.

Ab jagle

A ak B ñaari tomb la ñu si maasale gi. Ne bènn tomb M da fay bokk ci rëdd wii di (AB) mu ngi yemook nga wax ne AM ak AB ñoo bokk rëdd.

Yu tukkee ci lòlu

Jëmu ak digg

Su tomb bii di I doonee digguk [AB], konn AB=2AI

Su fekkee AB=2AI konn I mooy digguk dogit wii di [AB].

Tomb yu raŋale

Su A, B ak C raŋalee konn AC=kABk0

Su AC=kABk0 konn A, B ak C da ñoo raŋale.

Rëdd yu wetlàŋ

Su (AB)//(CD) konn AB=kCDk0

Su AB=kCDk0 konn (AB) ak (CD) da ñoo wetlàŋ.

RÉSUMÉ